Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 avril
“ Waxtaan ak déggoo, bu amee ci biir kër, jàmm dina am. Ñu bare dàkkoor nañu ci loolu, waaye dañu ne loolu yombul. Ci yow, lu tax yombul ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone li ñu mën a def ngir mën a waxtaan te déggoo bu baax ci biir kër gi. ” Jàngal Saag 1:19, te wonal nit ki ne déglu sa moroom bu baax, am na solo lool ci loolu.
Réveillez-vous! Avril
“ Ñu bare dañuy wax ne kurwaa dafa leen di dimbali ñu gën a jege Yàlla. Waaye am na ñuy laaj seen bopp lii : Ndax jaadu na ñu jaamu fi Yeesu deewe ? Ndax Yeesu ci kurwaa la deewe dëgg-dëgg ? Waxtaan bi nekk ci xët 12 dafay wone li Biibël bi tontu ci laaj yooyu. ” Jàngal Jëf ya 5:30.
La Tour de Garde 1er mai
“ Tey, ñi néew doole dañu bare lool. Ndax foog nga ne loolu dina mas a deñ ? Ndax am na li ñu mën a def ngir dimbali ñi néew doole ? [Mayal nit ki tontu. Jàngal 2 Piyeer 3:13 te won ko ne ci “ suuf su bees ” fu njub di dëkk, kenn dootul néew doole.] Bi Yeesu nekkee ci kow suuf, wone woon na ne dafa bëggoon a dimbali dëgg ñi néewoon doole. Téere bii dafa ñuy won ni ñu ko mënee roy ci loolu. ”
Réveillez-vous! Mai
“ Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax nit di màgget ? [Mayal nit ki tontu.] Li Biibël bi tontu ci laaj boobu, dafay wone li Yàlla di def ngir ñu mën a am dund gu dul jeex. [Jàngal Esayi 25:8]. Réveillez-vous ! bii dafay wone ni nit ñi di gise màgget. ”