Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 août
“ Bëgg naa xam sa xalaat ci li ñu wax fii. [Jàngal Yawut 3:4]. Ndax nangu nga ne Ku bare xam-xam moo sàkk asamaan ak suuf ? [May ko mu tontu]. Gëm ne am na ku sàkk asamaan ak suuf, ndax loolu mën na ànd ak li boroom xam-xam yi wax ? Ci loolu la téere bii di wax. ”
Réveillez-vous ! Août
Boo tasee ak xale bu góor walla bu jigéen, mën nga ko wax lii : “ Say moroom yu bare mas nañu dégg ñu leen di jëw, te loolu dafa leen metti woon lool. Ndax loolu mas na la dal ? [May ko mu tontu.] Biibël bi dafa ñuy jox ay xelal yu baax yu ñu mën a dimbali bu fekkee ne dafa am ku ñu jëw ba ñu dégg ko. Dafa ñuy won itam ni ñu mënee moytu def loolu, ñun ci suñu wàllu bopp. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 12, te jàngal benn ci aaya yi nekk foofu.
La Tour de Garde 1er sept.
“ Nit ñu bare dañu xalaat ne xaaju Biibël bi ñuy woowe “ Kóllëre gu jëkk ga ” mën na ñu xamal li xewoon démb. Waaye li leen dese wóor mooy ndax xelal yi nekk foofu, am nañu njariñ ba tey. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Room 15:4.] Boo jàngee téere bii, dinga gis ni xelal yi ñu mën a jàng ci xaaju Biibël boobu ame njariñ ngir suñu dund tey ak it suñu ëllëg. ”
Réveillez-vous ! Sept.
“Ndax ci sa xalaat Yàlla moo dogal yëngu-yëngu suuf walla musiba yu mel noonu ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Deutéronome 32: 4.] Téere bii dafay wone lu tax Yàlla terewul musiba yooyu am. Dafay wax itam ci li nga mën a def ngir aar sa njaboot bu musiba bu mel noonu amee. ”