Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de 15 juin
“ Ndax seetlu nga ne ñu bare tey ñooy seetal seen bopp li ñu war a jàppe ni lu baax walla lu bon ? [May ko mu tontu.] Li Yàlla wax ci Kàddoom, du xewi mukk. Xoolal li ñu wax fii. [Jàngal benn aaya ci wërale bi nekk ci xët 6-7.] Am na jikko yoo xam ne, Yàlla dafa bëgg ñu am leen. Téere bii dafay wone njariñ bi nekk ci am jikko yooyu. ”
Réveillez-vous ! Juin
“ Xale yu bare tey, seeni moroom ñoo leen di puus ci doxaan ba mu am ñuy bëgg a dugg ci loolu te jaar ci telefon walla internet ngir nëbb ko seeni wayjur. Ndax loolu wóor na ? [May ko mu tontu ba pare jàngal téere Woyu Suleymaan (Le chant de Salomon) 2:7 te won ko ne xaritoo ak góor walla jigéen ngir séy, am na waxtoom.] Téere bii dafay wone naka la wayjur yi mënee dimbali seeni doom ñu def loolu te bañ a nëbbatu. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 26.
La Tour de 1er juillet
“ Lan moo tax nit ñi di toroxal ñi ñu bokkalul xeet, reew walla làkk ? Ndax mas nga laaj loolu sa bopp ? [May ko mu tontu.] Seetal li ñu wax fii. [Jàngal 1 Yowaana 4:20.] Téere bi joxe na tontu ci laaj bii : Ndax jàmm dina mas a am diggante xeet yépp ? ”
Réveillez-vous ! Juillet
“ Nit mën na seetal boppam li mu bëgg a def ci àddinaam. Looloo tax mu wuute ak mala. Ci sa gis-gis, fan lañu mënee am xelal yu wóor ngir xam li ñu war a def ? [May ko mu tont, ba pare nga jàng Sabóor 119:105.] Téere bii dafay wone ne xelal yi nekk ci Kàddu Yàlla, ñoo gën xelal bu mu mënta doon. ”