Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 déc.
“ Tey, jamano Nowel ak 1 sãwiyee nekk nañu waxtu yoo xam ne, jaaykat yi dañuy jaay lu bare, nit ñi di jënd rekk. Ci yow, ndax Nowel ak 1 sãwiyee noonu la waroon a mel ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wax ci aada yi ñu tàmmoon a def bu njëkk ak it tey ci jamano jooju. Dafay wax itam ni ñu mënee màggal ni mu ware Yàlla ak Yeesu. ” Jàngal Yowanna 17:3 te woneel ne ku bëgg màggal Yàlla fàww mu xam li Yàlla bëgg ci ñun.
Réveillez-vous ! 22 déc.
“ Tey ñu bare dañu ragal feebar yiy wàlle. Ndax xam nga ne am na léegi 85 at ci ginnaaw, benn feebar buy wàlle rey na ay doom-Aadama yu bare ? Li mu rey ci 24 ayu-bés, ëpp na li Sida rey ci 24 at. Am na ñuy wax ne beneen feebar masul a yóbbu doom-Aadama yu bare noonu. Ndax mas nga dégg feebar bi ñuy woowe ci tubaab grippe espagnole ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone ndax lu mel noonu mën na fi amati. Waaye dafay wone it yaakaaru ëllëg bi ñu mën a am ci mbirum feebar. ” Jàngal Isayi 33:24.
La Tour de Garde 1er janv.
“ Ñiy defal seen moroom lu baax, ñépp a leen di bëgg. Lu baax li doom-Aadama mën a defal moroomam bare na lool. Waaye boo gisee lu bon li nit ñi di def seen moroom, dinga waaru. Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax loolu di am ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone li ci Biibël bi wax. Dafay wone it naka la li baax di gañe li bon. ” Jàngal Room 16:20 te boo koy jàng, nanga feeñal bu baax kàddu yii : “ dina noot Seytaane ci seeni tànk ”.
Réveillez-vous ! Janv.
“ Ndax mas nga laaj sa bopp naka la àddina si di mel fii ak 20 walla 30 at ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Sabóor 119:105.] Kàddu Yàlla dafa ñuy leeral yoon bi ngir ñu mën a xam li war a xew ëllëg. Yonent yi yégle woon nañu liy wone ci ban jamano lañu tollu tey. Wone woon nañu it lu tax ñu mën a yaakaar ëllëg gu neex. Ci loolu lépp la téere bii di wax. ”