Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 août
“ Ci yow, lan mooy ngor bi ëpp maanaa ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bii dafay wone ni ñu mënee topp Yàlla bu baax. [Woneel xët 5 bi, te jàngal 2 Samwil 22:26.] Ndax xam nga ne bu ñu toppee Yàlla bu baax, duñu soxor ak suñu moroom yi ? Wóor na ma ne li nekk ci téere bi, dina la neex. ”
Réveillez-vous ! 22 août
“ Liy tilimal suuf si mu ngi bëgg ëpp. Ndax loolu jaaxalu la ? [Mayal nit ki mu tontu.] Li gën a indi tilim-tilim boobu mooy nit ñi dañu mën a yàq. Yeesu jàngal na taalibeem yi ñu bañ a tàmm yàq. [Jàngal Yowanna 6:12.] Yéenekaay bii dafay wone ne topp ndigal yi nekk ci Biibël bi dafay tax njaboot yi bañ a tàmm yàq. ”
La Tour de Garde 1er sept.
“ Bu njëkk, nit ñi dañu doon xam seen dëkkandoo bu baax. Ndax seetlu nga ne ci béréb yu bare, loolu bareetul ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yeesu wax na lu am solo lu ñu war a def bu ñu bëggee nekk dëkkandoo bu baax. [Jàngal Macë 7:12.] Yéenekaay bii dafay wone ni ñu mënee nekk dëkkandoo bu baax te dimbali ñeneen ñi ci loolu. ”
Réveillez-vous ! 8 sept.
“ Ñu bare dañuy wax ne, kenn xamul luy xew ëllëg. [Jàngal Dajalekat 9:11.] Fan lañuy ame lu jar a wóolu lu ñuy won lu ñu war a def ? [Mayal nit ki mu tontu.] Am na ñuy wax ne fasoŋu gisaane bu ñuy wax ci tubaab numérologie mën na ñu dimbali. Ndax gisaane boobu mën na la xamal sa ëllëg ? Fan lañu mënee xam ci lu wóor lu war a am ëllëg ? Réveillez-vous ! bii dina la ko wax. ”