Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er sept.
“ Ci yow, ci kan lañu mën a dem mu xelal ñu, bu ñu amee lu am solo li ñu war a def ? [Mayal nit ki mu tontu, te nga jàng Proverbes 3:5, 6.] Koo xam ne bala muy def dara, dafay njëkk seet li jëfam mën a indi ëllëg, kooku ku am xel dëgg la. Ci loolu la téere bii di wax. ” Wonal nit ki waxtaan bi nekk ci xët 8.
Réveillez-vous ! Sept.
“ Xiif bare na ci kaw suuf si, te sonal na nit ñi lool. Ndax foog nga ne Yàlla moo ko dogal ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Yàlla bëgg def ngir faj poroblem boobu. [Jàngal Sabóor 72:16.] Waxtaan bii dafay wone ni Yàlla di defare suuf si mu nekk àjjana. ” Wonal nit ki waxtaan bi nekk ci xët 7.
La Tour de Garde 1er oct.
“ Ci jamano ju metti jii, ñu bare dañu ragal lu jëm ci seen ëllëg. Lan moo la mën a dimbali nga bañ a ragal ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Kàddu Yàlla wax fii. [Jàngal Isaïe 65:17.] Téere bii dafay wone lu wóor luy tax ñu mën a yaakaar ëllëg bu rafet. ”
Réveillez-vous ! Oct.
“ Internet am na njariñ, waaye am na ci lu doy waar lu mën a lor xale yi. Ci yow, naka lañu mënee aar xale yi ci loolu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li ñu wax fii. [Jàngal Proverbes 18:1, te won ko ni ñuy toppe li ñu wax foofu.] Li ñu jàng nii bokk na ci juróom benn xelal yi ñu jële ci Kàddu Yàlla yi nekk ci waxtaan bii. Xelal yooyu mën nañu dimbali wayjur yi ñu aar seeni doom. ” Wonal nit ki waxtaan bi nekk ci xët 8.