Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er déc.
“ Ndax seetlu nga ne ni nit jàppe luy set mën na wuute lool ak ni ko moroomam jàppe ? [Mayal nit ki mu tontu.] Wone nañu fii lenn lu tax set am solo. [Jàngal 1 Piyeer 1:16.] Xaaju yéenekaay bii dafay wone li ñu mën a def ngir set. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 9.
Réveillez-vous ! Déc.
“ Ci waxtu bii ci at mi, ñu bare dañuy bëgg màggal Yeesu. Ni ñu ko waxee ci aaya bii, naka la nit di gënee màggal Yeesu ? [Jàngal Yowaana 14:15 te may nit ki mu tontu.] Kenn xamul bés bi Yeesu juddu. Boo xamee li tax nit ñi tànn 25 desàmbar ngir màggal Nowel, mën na am mu jaaxal la. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 10.
La Tour de Garde 1er janv.
“ Tey, ay milioŋi nit dañu ragal lu jëm ci dee. Dañu leen jàngal ci seen diine ne bu nit deewee, ruu bi dafay génn ci yaramam, di dund feneen. Ci yow, ndax suñu mbokk walla suñu maam yi gaañu, ñu ngi léegi ci luy tax ñu war leen ragal te di leen jaamu ? [Mayal nit ki mu tontu te jàng Psaumes 104:29, 30.] Xaaju yéenekaay bii dafay wone li Kàddu Yàlla wax ci lu jëm ci dee. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 11.
Réveillez-vous ! Janv.
“ Dex yu bare ñu ngi wow ci àddina si, te ay milioŋi nit amuñu ndox bu sell bu ñu mën a naan. Ndax foog nga ne nit mën na faj poroblem boobu ba fàww ? [Mayal nit ki mu tontu te jàng Jérémie 10:23.] Kàddu Yàlla wone na li mën a faj dëgg poroblem boobu. Ci loolu la yéenekaay bii di wax. ”