WOY-YÀLLA 161
Topp say santaane mooy sama mbégte
(Taalifi Cant 40:9)
1. Bi Yeesu génnee dexu Yurdan,
say kàddu yu xóot fees xolam.
Mu nangu topp loo fas yéene.
Mu yàkkamti def wàllam.
Masul a xalaat sax def lu ñaaw.
Mu sawar, siiwal sa tur.
Mu daldi lay jox léppam ba jeex,
pare naa ngir def ni moom.
(AWU BI)
Def say santaane mbégte la.
Jox naa la sama doole bépp.
Mbégte laay yëg, mbégte bu wóor.
Dox ci sa leer moom moo wóor.
Def say santaane mbégte la.
Am naa yaakaar bu may dëfël.
Sa mbëggeel moom, amul moroom.
Màggal la guddeek bëccëg
moo may bégloo.
2. Yexowa, bi ma lay jàng a xam
am naa bànneex, yëg naa mbëggeel.
Dina ma neex ma seede ci yow.
Dinaa siiwal sa njubte.
Liggéey ci wetu samay mbokk
amul lu ko gën a neex.
Moo tax may joxe li ma mën lépp.
Wuyoo sa tur laay bàkkoo.
(AWU BI)
Def say santaane mbégte la.
Jox naa la sama doole bépp.
Mbégte laay yëg, mbégte bu wóor.
Dox ci sa leer moom moo wóor.
Def say santaane mbégte la.
Am naa yaakaar bu may dëfël.
Sa mbëggeel moom, amul moroom.
Màggal la guddeek bëccëg
moo may bégloo.
Waaw, mooy sama mbégte.
(Xoolal itam Taalifi Cant 40: 4, 11)