WOY-YÀLLA 97
Kàddu Yàlla lañuy dunde
(Macë 4:4)
1. Nit du dunde mburu kese,
na jàng Biibël bi.
Ndax lépp lu fa Yàlla wax
njariñam rekk la.
Su booba mébétam sotti,
mu am ëllëg bu neex.
(AWU BI)
Nit du dunde mburu kese,
na gëstu Biibël bi.
Foofa la njariñam nekk
ak jàmmam ak ndamam.
2. Biibël bi nettali na ñu
ni ay góor ak jigéen
takkoo ci Yexowa ak ngëm,
boole ci fit dëgg.
Seen dundin nekk royukaay
buy dooleel suñu ngëm.
(AWU BI)
Nit du dunde mburu kese,
na gëstu Biibël bi.
Foofa la njariñam nekk
ak jàmmam ak ndamam.
3. Bu ñu koy gëstu bés bu ne
day dëfël suñu xol.
Bés bu ñu nekkee ci coono,
mu may ñu fit ak muñ.
Nañu fonk bu baax a baax
lépp li ñu fa jàng.
(AWU BI)
Nit du dunde mburu kese,
na gëstu Biibël bi.
Foofa la njariñam nekk
ak jàmmam ak ndamam.
(Xoolal itam Yosuwe 1:8; Room 15:4.)