Li nekk ci téere bii
Seede Yexowa yi
ÑAN LAÑU ?
Njàngale 1-4
Am na ay seede Yexowa yi ci lu mat 240 réew. Bokk nañu ci xeet yépp ak cosaan yépp. Lan moo leen boole, ñu nekk benn ? Ñan ñooy seede Yexowa yi dëgg-dëgg ?
CI LAN LAÑUY YËNGU ?
Njàngale 5-14
Seen liggéeyu waare bi, ñu bare xam nañu ko. Am nañu itam ay ndaje ci ay béréb yu ñuy woowe “ Saalu Nguur gi ”. Foofu lañuy jànge Biibël bi te di fa jaamu Yàlla. Naka la seeni ndaje mel te kan moo ci mën a teew ?
NAKA LAÑUY DOXALE CI SEEN BIIR ?
Njàngale 15-28
Seen mbootaay, wutum xaalis taxu ko jóg. Ñi ci bokk, jaamu Yàlla rekk moo leen tax a jóg te fépp lañu nekk ci àddina si. Naka lañuy doxale ci seen biir, kan moo leen jiite, te seen xaalisu mbootaay, fu mu jóge ? Ndax dëgg-dëgg ñoom ñooy def tey li Yexowa santaane ?