TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/05 p. 8
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Li ñu mën a wax bi ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 9/05 p. 8

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 Sept.

“ Foo dem ci àddina, fekk fa nit ñu mas a dégg turu Yeesu Krist. Am na ñu wax ne Yeesu du kenn ku dul nit ku kéemaane. Am na ñeneen ñu wax ne yonent bu mag la. Am na sax ñu wax ne Yàlla la, moo tax ñu koy jaamu. Ci yow kan mooy Yeesu Krist ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone kan moo doon Yeesu, fu mu jóge woon, ak fan la nekk tey. ” Jàngal Yowanna 17:3 te wonal nit ki lu tax ñu war a yokk suñu xam-xam ci Yeesu Krist.

Réveillez-vous ! 22 Sept.

“ Li ëpp ci nit ñi nuy waxtaanal, amuñu fu baax fu ñu mën a dëkk. Ndax mën nañu yaakaar jamano joo xam ne kenn dootul am poroblem boobu ? [Mayal nit ki tontu.] Réveillez-vous ! bii dafay wone fi poroblemu kër tollu. Dafay wone itam lu tax ñu war a gëm li Yàlla wax ci Isayi 65:​21, 22. ” Jàngal Isayi 65:​21, 22.

La Tour de Garde 1 Oct.

Jàngal laaj bi ñu def ci xët bu njëkk bi ba pare nga laaj nit ki lii : “ Ndax xam nga ci lan lañuy wax fii ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Macë 24:⁠3. Nanga fexe ba ‘ luy tegtale ne (...) àddina di tukki ’ feeñ bu baax boo koy jàng.] Liy wone ne ci muju jamano lañu tollu bare na. Téere bii dafa ciy wax juróom yu am solo. Wax na it lu tax ñu war leen a xàmme. ” Won ko wërale bi nekk ci xët 6 (li nekk ci suufu xët bi).

Réveillez-vous ! 8 oct.

“ Jigéen yi dañu bëgg rafet moo tax ñuy defaru. Waaye am na ñu bañ loolu. Ci yow, ndax jigéen dafa war a defaru, walla dafa war a nëbb taaram ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Room 14:13. Won ko foofu lu tax waruñu defaru ci fasoŋ boo xam ne jekkul fi ñu dëkk te dina tax nit ñi boole ñu ci ñi bon.] Ci xët 26, dañuy wone li jigéen yi mën a def ba ñu weg leen ak li ñu mën a def ngir màggal ki leen sàkk. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager