Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er oct.
“ Boroom xam-xam yi gis nañu ni baay ame solo ci kër. Ci yow, lan mooy baay bu baax ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Mbind mi wax baay yi fii. [Jàngal Kolos 3: 21.] Xaaju téere bii, dafay wone juróom-benni ponk yu am solo ci wareefu baay. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 18.
Réveillez-vous ! Oct.
“ Diine yi déggoowuñu ci ni Yàlla mel. Waaye lan la yonent yi waxoon ci ni Yàlla mel ? Xoolal li Yeesu wax ci Yowaana 4: 24. [Jàng ko.] Xaaju téere bii, dafay wone ci ñaari xët kese li Kàddu Yàlla tontu ci laaj bii : “ Naka la Yàlla mel ? ” Wonal nit ki waxtaan bi nekk ci xët 24 ak 25.
La Tour de Garde 1er nov.
“ Ñu bare mënuñu boole gëm ne Yàlla mooy Aji mbëggeel ak gëm ne Yàlla dafay toroxal nit ñi ci safara ba fàww. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu Sell mi dafay wax ci lu leer ne Yàlla soxorul, te du jàpp mer. [Jàngal Ézékiel 18:23.] Téere bii dafay wone li ci Mbind mi wax. Wóor na ne boo ko jàngee dina la neex ”.
Réveillez-vous ! Nov.
“ Nit ñi dañuy faral di wax ne nit ku tekki ci àddina dafay siiw, bare xaalis, walla mu bare kàttan. Ci yow lan mooy nit ku tekki ? [Mayal nit ki mu tontu.] Kàddu Yàlla wax na li mën a tax nit tekki. Seetal li mu wax fii. [Jàngal Sabóor 1:1-3.] Xaaju téere bii dafay wax ci juróom-benni ponk yuy tax nit tekki. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 6.