WOY-YÀLLA 122
Nañu takku te sampu ba dëgër!
(1 Korent 15:58)
1. Nguuru àddina yépp a jaxasoo,
di yox-yoxi ci xalaatum ëllëg.
Ñun soppey Yeesu, nañu sax ci ñaan,
nañu sampu taxaw temm.
(AWU BI)
Takkute mooy li ñu war.
Àddina du wéeruwaay.
Dëgërlu dem ba jeex,
di séentu àjjana!
2. Àddina wóorul, dañuy xiir ci mbon.
Maandu, ànd ak xel, suñu kaaraange.
Nañu bëgg lu baax, sore bàkkaar.
Noonu dinañ dëgërlu.
(AWU BI)
Takkute mooy li ñu war.
Àddina du wéeruwaay.
Dëgërlu dem ba jeex,
di séentu àjjana!
3. Ci suñu biir xol, nañ màggal Yàlla.
Nañ ko faral, ànd ceek cawarte,
di waare ak ngëm, ‘nguuram agsi na’;
ndaxte bésam soreetul!
(AWU BI)
Takkute mooy li ñu war.
Àddina du wéeruwaay.
Dëgërlu dem ba jeex,
di séentu àjjana!
(Xoolal itam Luug 21:9; 1 Piyeer 4:7.)